Ngëneelu julli ci mbooloo
Su nit jullee ñaari rakaa ci mbooloo, te julli ñaar-fukki rakaa ak juróom-ñaar moom rekk, yoolu ñaari rakaa yi mu julli ci mbooloo moo ëpp ba tey. Ci beneen riwaaya, su jullee junniy rakaa moom rekk, yoolu ñaari rakaa yi ñu julli ci mbooloo moo ëpp ba tey. Yoolu julli ci mbooloo bare na. Leeral nañu ci ay yenn:
1- Bu gëmkat yi booloo, mbëggeel dana am ci seen biir.
2- Ñi ñàkk xam-xam dañuy jànge ci boroom xam-xamu diine yi mbir yi aju ci julli.
3- Su ñu nangoo jullig ñenn ñi te nanguwuñu jullig ñeneen ñi, ci wormay ñi ñu nangu seen julli, dañuy nangu itam jullig ñi ñu nanguwul woon seen julli.
Wax nañu ci hadiis bu tedd: (Yéen sama umma ak samay Sahaaba! Teg naa ñaari yoon ngir yéen: benn bi mooy Alxuraan mu màgg mi, beneen bi mooy sama sunna. Ku topp yoon wu dul yooyu, bokkul ci sama umma!) [Abdul Ganii an-Naabulusii “rahimahullaahu ta-aalaa”, nee na ci xëtu juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeent ci (Hadiiqa): (Ni Allah ta-aalaa xamle woon ab wàll ci Islaam jaarale ko ci Alxuraan al-Kariim, noonu la xamle itam beneen wàll jaarale ko ci sunna Yónentam “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam”. Sunna Rasuul Allah mooy li mu gëm, li mu wax, li mu def, jikkoom ak noppeem ci kanam kàddu walla jëfu kenn [ba ñu xam ci noonu ne nangu na ko].) Hadiis bu tedd bii day wone ñaareelu (daliilu Sariiha) yi.]
Jiite julli
Te itam, ñi topp imaam bi ñeenti xeet lañu. Ñooñu ñooy ñi ñuy woowe mudrik, toppkat ci julli, masbuuq ak laahiq.
1- Mudrik mooy ki wax takbiir al-iftitaah ànd ak imaam bi.
2- Toppkat ci julli mooy ki jotul ci takbiir al-iftitaah.
3- Masbuuq mooy ki topp imaam bi gannaaw bu imaam bi jullee benn walla ñaari rakaa.
4- Laahiq mooy ki wax takbiir al-iftitaah ànd ak imaam bi, waaye gannaaw loolu hadas daldi ko dal, mu jàpp te dellu topp imaam bi. Nit kooku day julli ni mu ko daan defe, te du def qiraa’a, di def tasbiix yi ci ruku ak sujóot. Nit kooku, su waxul kàddug àdduna, mel na ni ku nekk ci gannaaw imaam bi. Waaye, gannaaw bu génnee jàkka ji, war na jàppe ci bérab bu jege lool. Am na ku wax ne su demee ba sore lool, julligam dina nekk faasid.
Bu nit ñëwee ci jàkka ji, fekk imaam bi ci ruku, mu gaawtu ngir jot ci ruku bi, te wax takbiir al-iftitaah bi muy sëgg ngir ruku, toppul imaam bi. Bu fekkee imaam bi ci ruku, yéene topp ko, sottal takbiir bi fekk mu taxaw, daldi ruku te sëgg ànd ak imaam bi, di def tasbiix, jot na ci rakaa boobu. Waaye bi muy sëgg ngir ruku, su imaam bi siggee, jotul ci rakaa boobu.
Taadiilul arkaan ci julli
Bu nit bàyyee taadiilul arkaan ci juróomi bérab yi ci julli ci lu mu xam te bëgg ko, te du ko fàtte, ci waxu Imaam Abu Yuusuf “rahimahullaahu ta-aalaa”, julligam dina nekk faasid. Ci waxu Tarafayn, du nekk faasid. Waaye, ndax dafa bàyyi waajib bi ci lu mu bëgg, war na baamtu julli ngir mottali li ñàkk. Bu ko fàttee ba bàyyi ko, (Sujóodu sahwi) war na. [Xoolleen xët 27!]
Bàyyi taadiilul arkaan am na lu tollu ci ñaar-fukki lor ak juróom-benn:
1- Day waral ndóol.
2- Boroom xam-xamu diine yu àllaaxira yi dañu koy bañ.
3- Day ñàkk adaala, ba duñu nangu seedeem.
4- Bérab bi mu julli dina seede ci kawam bésu pénc.
5- Bu nit gisee kenn di julli te sàmmul taadiilul arkaan, te waxu ko ko, day nekk boroom bàkkaar.
6- Baamtu julli googu day nekk waajib.
7- Day waral mu dee nekk ku amul iimaan.
8- Dafay doon sàccu julli.
9- Julli gi mu julli, dees ko ko dóor ci kanamam, ni sër bu màggat -ca bésu àtte ba-.
10- Dafay ñàkk yërmandey Allah ta-aalaa.
11- Dafay def ñàkk teggin ci munaajaat gi muy def ci Allah ta-aalaa.
12- Dafay ñàkk yool wi ci julli di yokku.
13- Dafay tax ñu bañ koo jox yoolu yeneen jaamu yi.
14- Dafay yelloo Jahannama.
15- Dafay tax ñi ñàkk xam-xam gis ko, ba bàyyi taadiilul arkaan. Looloo tax, ku yor xam-xamu diine bu defee bàkkaar, mu tax mu dékku mbugal mu gën a bari.
16- Dafay jalgati imaamam.
17- Dafay bàyyi sunna yi nekk ci intiqaal yi.
18- Dafay dal ci meru Allah Boroom màgg a màgg.
19- Dafay bégal Seytaane.
20- Dafay sore àjjana.
21- Dafay jege Jahannama.
22- Dafay tooñ nafsam.
23- Dafay tilimal nafsam.
24- Dafay metital malaaka yi nekk ci ndeyjooram ak ci càmmoñam.
25- Dafay naqaral Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam”.
26- Dafay lor mbindeef yépp. Ndaxte, bàkkaaram dafa tax taw du taw, mbey du sax ci suuf, te taw di taw ci jamono ju ko warul, ba indi lor ci pala njariñ.
