Nanu tàmbalee téere bi basmala!
Turu Allah mooy làquwaay bi gën a baax.
Xelëgam yi, natt ak lim manu leen a ëmb,
Boroom la bu bari yërmande, bëgg a baale!
Allah ta-aalaa yónni na Yónent yi “alayhimus-salaam” ci nit ñi, ngir ñu am mbégte ci àdduna ak àllaaxira, nekk ci dal ak jàmm, boole seeni xol, dund ni ay bokk, te ngir xamal leen ni ñuy def seen warugaru jaamug Allah. Jaarale na ci nit ñu tànn ñooñu, ñi gën a màgg ci nit ñi ci wàll gu nekk, ngir xamal ay jaamam yoon yi gën ci dund. Xamal na ne Muhammad alayhis-salaam, mi gën a màgg te mujj ci ay Yónentam “alayhimus-salawaatu wat-tasliimaat”, mooy Yónentu nit ñépp ñiy ñëw ci bépp barabu àdduna ba bésub pénc. Allah ta-aalaa xamal na ay ndigëlam ak ay tereem ci téere bu màgg bi tudd (Alxuraan al-Kariim), bi mu yónnee ci ndimbalu malaaka ci Yónentam boobu mu bëgg lool, ci diirub ñaar-fukk ak ñetti at. Ndax Alxuraan al-Kariim araab la, te dafay nettali xam-xam yu xóot lool ak mbir yu xel mënul a jot, Muhammad alayhis-salaam leeral na téere bii yépp, dale ko ca ndoorte la ba ca muj ga, ci ay Sahaabaam “alayhimur-ridwaan”. Nee na: (Ku leeral Alxuraan al-Kariim ci anam wu wuute ak li ma ko nettalee, day nekk kéefar). Boroom xam-xamu lislaam yi “rahimahumullaahu ta-aalaa” dégg nañu ci Sahaaba yu tedd yi leeral yi sunu Yónent “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam” defoon, ñu yaatal leeral yooyu ngir ku nekk mën leen a dégg, te bind leen ci téerey tafsiir. Boroom xam-xam yooyu lañuy woowe boroom xam-xamu diine yu Ahlus Sunna. Téerey diine yi boroom xam-xamu diine yu Ahlus Sunna “rahimahumullaahu ta-aalaa” dajale te bind, jóge ci leeral yi ci Alxuraan al-Kariim ak it ci waxi sunu Yónent “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam” yi ñuy woowe (hadiis bu tedd), yooyu lañuy woowe téerey (ilmu xaal). Ñi bëgg a jàng bu baax te bu dëgër (diiney Lislaam) ji Allah ta-aalaa xamle ci Alxuraan al-Kariim, war nañu jàng téerey xam-xamu warugaru diine yooyu.
Turu cosaanu téereb xam-xamu warugaru diine bii tudd (Yoonu Àjjana) bi nuy joxe léegi mooy (Miftaahul Janna), maanaam caabig buntub àjjana. Muhammad bin Qutbuddin al-Izniki “rahimahullaahu ta-aalaa”, mi faatu woon ca Edirne ci atum 885 ci woññug Hijra bu weer [m. 1480], moo ko bind.
Boroom xam-xamu lislaam bu xóot bi, Seyyid Abdul Hakiim Seriñ “rahimahullaahu ta-aalaa”, wax na ne: (Ki bind téereb ilmu xaal bi (Miftaahul Janna), ñu nee nit ku sell la woon. Dina amal njariñ ñi koy jàng). Looloo tax nuy tasaare téere bii. Leeral yi ñu def ci ay barabam, dañu leen teg ci diggante màndarga yi [ ]. Leeral yooyu, dañu leen tànne ci yeneen téere te dolli leen fii. Benn ci ñoom du xalaatu kenn ci boppam. Yal na Allah ta-aalaa aar nu ñépp ci tàggoo ak tasaaroo, ci daanu ci fiiri noonuy Lislaam yi tëru, ak ñi réer ci diine te tuddoo turu jullit, ba sax di taxawu ni ay boroom diine, ak ñi dul topp benn masab ak ñiy soppali diine! Yal na nu boole ñépp ci masabu (Ahlus Sunna), mi nekk ci yoonu Yónentam bi mu bëgg “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam”, di topp ay tànkam! Yal na nu may nu bëggante te dimbalante! Aamiin.
[Nit, bu bëggee def jëf, li jiitu mooy xalaat bu ñëw ci xolam [fikar, xalaat]. Mu bëgg koo def. Bëgg-bëgg boobu lañuy woowe (Yéene). Mu jox ay céram [ay organam] ndigël ngir ñu def jëf jooju. Jox ndigël googu lañuy woowe (Dogu, jéem a jëf). Jëf ji cér yi di def lañuy woowe (Jot). Jëf yi xol di def lañuy woowe (jikko) [melokaan]. Xalaat yi ñëw ci xol, dañuy jóge ci juróom-benni barab: xalaat yi jóge ci Allah ta-aalaa lañuy woowe (wahyu). Wahyu, ci xoli Yónent yi rekk lay ñëw. Xalaat yi malaaka yi di indi lañuy woowe (il-aam). Il-aam dafay ñëw ci xoli Yónent yi “alayhimus-salawaatu wat-tasliimaat” ak jullit ñu sell ñi. Xalaat yi jullit ñu sell ñi di joxe lañuy woowe (nasiiha). Wahyu, il-aam ak nasiiha, saa su nekk lu baax lañu te am njariñ. Xalaat yi jóge ci Seytaane lañuy woowe (wiswaas), xalaat yi jóge ci nafsu nit ki ci boppam lañuy woowe (bëgg-bëggu bakkan), xalaat yi xarit bu bon di dugal [di ji] ci nit lañuy woowe (naxtal). Nasiiha, ku nekk lañu koy jox. Wiswaas ak bëgg-bëggu bakkan dañuy ñëw ci xoli kéefar yi ak jullit ñi nekk faasiq. Ñoom ñaar yépp lu bon lañu [lu ñaaw] te di lor. Li Allah ta-aalaa gërëm te bëgg lañuy woowe (Lu baax). Li mu bëggul lañuy woowe (Lu bon). Ndax Allah ta-aalaa Boroom yërmande ju réy la, xamle na lu baax ak lu bon ci (Alxuraan al-Kariim). Joxe na ndigël ngir ñu def lu baax, te tere lu bon. Ndigël ak tere yooyu lañuy woowe (Ahkaamul islaamiyya). Su xol toppee nasiiha yi xarit yu baax yi di joxe ak xel, te topp Ahkaamul islaamiyya, day leer te set. Day am sa’aada ak dal ci àdduna ak àllaaxira. Xol buy topp wax ak mbind yu naxtal te di réeral yu nit ñu bon ñi ak zindiiq yi, ak nafs ak Seytaane, te dul topp Ahkaamul islaamiyya, day lëndëm te yàqu. Xol bu leer te set dafay bëgg a topp Ahkaamul islaamiyya. Xol bu lëndëm dafay bëgg a topp xarit bu bon, nafs ak Seytaane. Ndax Allah ta-aalaa Boroom yërmande ju réy la, dafay sàkk xoli xale yiy juddu ci bépp barabu àdduna, ñu set. Gannaaw loolu, seeni yaay, seeni baay ak seeni xarit yu bon ñoo leen di lëndëmal, di leen def ni ñoom.]