Hakikat Books
English
Preview — this text has not yet been approved for publication.

Chapter 5 / 73

Sifaat saatiyya

Sifaat saatiyya yi nu war a xam ci Allah Boroom màgg a màgg juróom lañu: Yooyu lañuy woowe (meloy divinite).

1- Qidam, amug Allah Boroom màgg a màgg amul ndoorte.

2- Baqaa, amug Allah Boroom màgg a màgg amul muj, loolu lañuy woowe waajib al-wujuud. Dalil bi ñu jële ci wax ji ñu jottali mooy ñatteelu aaya bu tedd bi ci saar Al-Hadiid bu Allah ta-aalaa. Dalil bi aju ci xel mooy, su amug Allah amoon ndoorte ak muj, kon dina doon ku am gannaaw ñàkk a am, ku ñàkk kàttan te matul. Ku ñàkk kàttan te matul manul a sàkk leneen. Loolu lu warul nekk la ci Allah Boroom màgg a màgg.

3- Taxaw ci boppam, Allah Boroom màgg a màgg soxlawul kenn ci zaatam, ci melokaanam yi ak ci jëfam yi. Dalil bi ñu jële ci wax ji ñu jottali mooy aaya bu tedd bi mujj ci saar Muhammad “alayhis-salaam”. Dalil bi aju ci xel mooy, su melokaan yii amul woon ci Moom, dina ñàkk kàttan te matul. Ñàkk kàttan ak ñàkk mat lu warul nekk la ci Allah Boroom màgg a màgg.

4- Wuute ak lu ñu sàkk, Allah Boroom màgg a màgg niroowul ak kenn ci zaatam ak ci melokaanam yi. Dalil bi ñu jële ci wax ji ñu jottali mooy aaya bu tedd bi fukk ak benneel ci saar As-Suuraa bu Allah ta-aalaa. Dalil bi aju ci xel mooy, su melokaan yii amul woon ci Moom, dina ñàkk kàttan te matul. Ñàkk kàttan ak ñàkk mat lu warul nekk la ci Allah Boroom màgg a màgg.

5- Wahdaaniyya, Allah Boroom màgg a màgg amul kenn kuy moroomu Allah, amul moroom ci zaatam, ci melokaanam yi ak ci jëfam yi. Dalil bi ñu jële ci wax ji ñu jottali mooy aaya bu tedd bi jëkk ci saar Al-Ixlaas bu Allah ta-aalaa. Dalil bi aju ci xel mooy, su amoon ku bokk ak Moom, aalam dina sànku, di neen. Kenn ki dina bëgg ñu sàkk dara, ki ci des bëgg ñu baña sàkk ko.

[Ci xalaatu ñi ëpp ci boroom xam-xamu diine yi, (wujuud) maanaam am, moom itam melokaan la bu boppam. Noonu, (sifaat saatiyya) di juróom-benn].

Read this chapter in another language

Türkçe中文(普通话)EnglishPortuguêsItalianoУкраїнськаNederlandsБългарскиNorskEestiދިވެހި

Share

WhatsApp Telegram X Facebook E-mail