Juróom-benn ci ñoom ñoo di yii:
1- Bañ a wax ak làmmiñ yéene gi ñu def ak xol.
2- Def masa sa baat ak ndox mi des gannaaw masa say nopp.
3- Bañ a raxas say tànk te nga jublu ci qibla.
4- Su mënee am, naan ndox mi des ci jàpp gi te nga taxaw, jublu ci qibla.
5- Gannaaw jàpp gi, wis tuuti ndox ci sa tubéy.
6- Fomp sa yaram ak sarwet bu set te laab.
Ibn Aabidiin wax na ci mbir yi di yàq jàpp ne, (Su dara doon farata ci beneen masab te du makruuh ci sa masab, def ko mustahab la). Imaam ar-Rabbaanii wax na ci bataaxalam bu 286 ne, (Ndaxte fomp céri jàpp yi farata la ci masab maaliki, war nañu leen a fomp ci lu wér). Ibn Aabidiin, bi muy leeral talaaq raji, wax na ne, (Ki nekk ci masab Hanafii, li gën mooy mu def taqliid masab maaliki. Ndaxte Imaam Maalik mel na ni taalibe Imaam bu mag. Bu amee mbir bu ñu gisul benn waxu maðhab ci masab Hanafii, boroom xam-xamu diine yu hanafi yi dañu daan joxe fatwa bu dëppoo ak masab maaliki. Ci masab yi, bi gën a jege masab Hanafii mooy masab maaliki.)