Pàcc bi ci ngëneeli Sahaaba
Ci sahaaba yépp, ñeenti xaliifay Rasuul Allah “radiyallaahu ta-aalaa anhum ajma’iin” ñoo gën ñeneen ñi. Diiru seen xilaafa yépp, fanweeri at la. [Yégle nañu ne Sahaaba yu tedd “radiyallaahu ta-aalaa anhum ajma’iin” ñépp dinañu dem àjjana. Wax lu bon ci kenn ci ñoom jaaduwul.]
Te itam, karaama wali yi dëgg la, lu wér la.
Ki gën a yiw, ki gën a kawe ci wali yépp, mooy Hadratu Abuu Bakr as-Siddiiq “radiyallaahu ta-aalaa anhu”. Xilaafaam dëgg la. Ijmaa umma bi moo dëggal ne mooy xaliifa bu jëkk. Mooy gorob Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam”. Mu may Rasuul Allah “radiyallaahu anhaa” doomam, sunu yaay Aayisa “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam”, mu takk ko. Dafa xereñ ci xam-xamu haqiiqa. Dafa joxe alalam yépp ci yoonu Allah. Ba desul woon benn habba. Mu sol lu ñu ràbbe weñi garabu tàndarma ci ndiggam. Jibriil “alayhis-salaam” itam sol ni mu soloon, ñëw ci Rasuul Allah. Bi ko Yónnent bi gisee ci noonu, mu wax ne: (Yaa sama mbokk Jibriil! Musumaa la gis ci noonu. Lu doy waar la haal bii), Jibriil “alayhis-salaam” wax ne: (yaa Rasuulallah! Léegi gis nga ma ci noonu, malaaka yépp noonu lañu mel. Li ko waral mooy, Allah Boroom màgg a màgg wax na ne: (Sama jaam Abuu Bakr joxe na alalam yépp ci sama yoon, ngir sama ngërëm. Léegi mu sol lu ñu ràbbe weñi garabu tàndarma. Yéen sama malaaka yi, yéen itam solleen ni moom), loolu la santaane. Malaaka yépp léegi noonu lañu mel). Te looloo tax ñu tudde ko siddiiq.
Ki ko topp ci wali yi gën a yiw mooy Hadratu Omar “radiyallaahu anhu”. Ijmaa umma bi moo dëggal xilaafaam. Dafa xereñ ci xam-xami Lislaam. Bés benn, am munaafix ak ab yawut ñëw ci Sëriñ Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam” ngir mu àtte seen werante. Sëriñ Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam” déglu seen werante. Dëgg gi nekk ci yawut bi. Bi munaafix boobu nanguwul, Rasuul Allah “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam” wax leen ci waxtu woowu ne: (Yéen nit ñi! Demleen ci Omar, mu àtte seen werante!) Ñu ñëw ci Hadratu Omar “radiyallaahu ta-aalaa anhu”. Mu ne leen: Lu tax ngeen ñëw? Munaafix bi ne: Dama am werante ak yawut bii. Hadratu Omar “radiyallaahu ta-aalaa anhu” wax ne: Naka laay àttee werante bii, fekk Boroom Islaam a ngi fi? Munaafix bi ne: Dem nanu ci Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam”, mu àtte, dëggal yawut bi. Man nanguwuma! Ci saa si, Omar “radiyallaahu anhu” ne leen: Xaarleen, dinaa léegi dogal seen werante, ba noppi mu dugg ci biir.
Gannaaw tuuti, mu ñëw ci ñoom, yor jaasi bu mu nëbb ci suufu mbubbam; bi mu génnee jaasi bi rekk, mu dog boppu munaafix boobu, ne: (Lii mooy li dal ku nanguwul àtteb Rasuul Allah). Loolu moo tax ñu tudde ko Umar al-Faaruuq “radiyallaahu ta-aalaa anhu”.
Sëriñ Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam” wax na ne: (Ki xàjjale dëgg ak baatil mooy Omar).
Gannaaw moom, ki gën a yiw ci wali yi mooy Hadratu Usmaan Zun-Nuurayni “radiyallaahu anhu”. Xilaafaam dëgg la, jub na. Ijmaa umma gi moo ko dëggal. Rasuul Allah “sallallaahu ta-aalaa alayhi wa sallam” may na ko ñaari doomam yu jigéen ci séy, benn gannaaw beneen. Bi ñaareelu doomam faatoo, wax na: (Su ma amoon beneen doom ju jigéen, dinaa ko ko may ci séy!)
Bi mu koy may ñaareelu doomam ci séy, màggaloon na Hadratu Usmaan “radiyallaahu ta-aalaa anhu” lool. Gannaaw bi mu leen séyalee, doomam ju jigéen ji ne ko: (Éy sama baay, leeru samay bët! Màggal nga Hadratu Usmaan lool. Tolluwul ni nga ko waxe!) Sëriñ Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam” ne doomam: (Éy sama doom! Malaaka yi ci asamaan dañuy am kersa ci kanam Hadratu Usmaan!)
Ndax Rasuul Allah “sallallaahu alayhi wa sallam” mayoon na ko ñaari doomam yu jigéen ci séy, ñu tudde ko Usmaan Zun-Nuurayni. Zun-Nuurayni tekki na boroom ñaari leer. Dafa xarañ ci xam-xamu maarifa.
Gannaaw moom, ki gën a yiw ci wali yi mooy Ali “karramallaahu wajhahu wa radiyallaahu anhu”. Ijmaa umma gi moo dëggal xilaafaam. Jëkkëru doom ju jigéen ju Rasuul Allah la. May na ko doomam, sunu yaay Soxna Faatima “radiyallaahu anhaa”, ci séy. Dafa xarañ ci xam-xamu tariixa. Amoon na jaam bu góor. Benn bés, jaamam bi yéene ne: Naa seetlu sama sang bii. Booba, Hadratu Ali “radiyallaahu ta-aalaa anhu” nekkoon na ci biti. Mu ñëw ca jaam ba, sant ko liggéey. Jaam ba noppi. Gannaaw loolu, Hadratu Ali “karramallaahu wajhahu” ne jaam ba: Éy jaam bi! Lu ma la def, lu tax sa xol damm, te lu ma def moo la metti? Jaam ba ne ko: Defuloo ma dara. Man sa jaam laa. Sama yéene mooy seetlu la. Wali nga ci dëgg.
[Ñi bëgg Sahaaba yu tedd yépp te topp seen yoon, ñooñu lañuy woowe (Ahlus Sunna). Ki naan danuy bëgg ñenn ci ñoom te bëggul ñi ëpp ci ñoom, moom lañuy woowe (siit). Ñi bañ Sahaaba yu tedd yépp, ñooñu lañuy woowe (raafidi). Ki naan danuy bëgg Sahaaba yu tedd yépp, waaye toppul kenn ci ñoom ci yenn mbir, moom lañuy woowe (Wahaabi). Njaxasoo xalaati Ahmad ibn Taymiyya, boroom diine bu réer ci diine, ak feni Hemfer, yëgalkatu kumpa bu Angle bi, lañuy woowe (Wahaabiyya). Jullit ñi bokk ci Ahlus Sunna te toppul seen gëm-gëm yooyu, dañu leen di tudde kéefar. [Ci wax jooju, ñoom ci seen bopp dañuy doon kéefar.]
Xalaati Wahaabiyya yi, Angle yi ñoo leen sos ci penensilu Araabi ci atum 1150 [m. 1737]. Tuuru nañu deretu jullit yu bare ngir tasaaral pexey Angle yi. Léegi itam, dañuy taxawal ci réew mu nekk ay santar yu ñuy woowe (Raabitatul Aalam al-Islaami), di tas wurus wu ñu manul a lim, ngir napp boroom diine yi ñàkk xam-xam. Ñooñu lañuy jaar ngir réeral jullit ñi. Dañuy yàq deru boroom xam-xamu diine yu Ahlus Sunna yi aar Islaam lu mat junni ak ñeenti téeméeri at, ak Otoman yi leen doon aar. Dañuy wax ne xam-xam bu jub bi boroom xam-xamu diine yooyu génnee ci nass yi dafa jubul.
Ñenn ci Wahaabi yi dañuy naan: (Nun itam nu ngi ci masabu Ahlus Sunna, nu ngi ci màzhab Hanbali.) Seen wax jooju dafa mel ni waxu ñi bokk ci kuréelu diine gu réer gi tudd Mu’tazila, ñuy naan: (Nun itam Ahlus Sunna lanu. Nu ngi ci masab Hanafii.) Dañuy wax noonu ndax xam nañu ne ñi bokkul ci Ahlus Sunna dinañu dem Jahannama. Waaye, jëf yi rekk, liggéey yi rekk, su ñu méngoo ak benn masab, loolu tekkiwul ne nit ki bokk na ci masab boobu. Ngir topp benn masab, aqiida ak jëf yépp war nañu méngoo ak masab boobu. Aqiida ñeenti masab yi benn la. Ñoom ñeent yépp ñoo ngi ci gëm-gëfu Ahlus Sunna. Ngir nit man a bokk ci masab hanafi walla hanbali, dafa war a jëkk a nekk ci gëm-gëfu Ahlus Sunna. Wahaabi yi nekkunu ci gëm-gëfu Ahlus Sunna.]
