Bu nit di tàmbali jàpp, na wax: (Bismillaahil-aziim walhamdu lillaahi alaa diinil-islaami wa alaa tawfiiqil-iimaani alhamdu lillaahil-lazii ja-alal-maa-a tahuuran wa ja-alal-islaama nuuran).
Bu dugalee ndox ci gémmiñam, (Allaahumma sqinii min hawdi nabiyyika ka-san laa azma-u ba-dahu abadan).
Bu dugalee ndox ci bakkanam, (Allaahumma arihnii raa-ihatal-jannati warzuqnii min na-iimihaa wa laa turihnii raa-ihatan-naari).
Bu raxasee kanamam, (Allaahumma bayyid wajhii binuurika yawma tabyaddu wujuuhu awliyaa-ika wa laa tusawwid wajhii bizunuubii yawma taswaddu wujuuhu a-daa-ika).
Bu raxasee loxol ndeyjooram, (Allaahumma a-tinii kitaabii biyamiinii wa haasibnii hisaaban yasiiran).
Bu raxasee loxol càmmoñam, (Allaahumma laa tu-tinii kitaabii bisimaalii wa laa min waraa-i zahrii wa laa tuhaasibnii hisaaban sadiidan).
Bu masa boppam, (Allaahumma harrim sa-rii wa basarii alan-naari wa azillanii tahta zilli arsika yawma laa zilla illaa zilluka).
Bu masa ay noppam, (Allaahumma j-alnii minal-laziina yastami-uunal-qawla fayattabi-uuna ahsanah).
Bu masa baatam, (Allaahumma a-tiq raqabatii minan-naari wahfaz minas-salaasili wal-aglaal).
Bu raxasee tànku ndeyjooram, (Allaahumma sabbit qadamayya alas-siraati yawma tazillu fiihil-aqdaam).
Bu raxasee tànku càmmoñam, (Allaahumma laa tatrud qadamayya alas-siraati yawma tatrudu kullu aqdaami a-daa-ika. Allaahumma j-al sa-yii maskuuran wa zanbii magfuuran wa amalii maqbuulan wa tijaaratii lan tabuura).
Gannaaw bu matalee jàppam, (Allaahumma j-alnii minat-tawwaabiina waj-alnii minal-mutatah-hiriina waj-alnii min ibaadikas-saalihiina waj-alnii minal-laziina laa xawfun alayhim wa laa hum yahzanuun).
Gannaaw loolu, na xool asamaan te jàng: (Subhaanakallaahumma wa bihamdika as-hadu an laa ilaaha illaa anta wahdaka laa sariika laka wa anna Muhammadan abduka wa rasuuluka).
Gannaaw loolu, na jàng saar (Innaa anzalnaa) benn yoon, walla ñaar, walla ñett, di jiital (basmala).
Rax-ci-dolli, na jàng te jàngal njabootam, ñi mu yor ak doomam yi xam-xamu diine ji ñu soxla, ndax ci bésub pénc, dañuy laaj jëkkër yi ci seen jabar yi.