Te itam, ñi topp imaam bi ñeenti xeet lañu. Ñooñu ñooy ñi ñuy woowe mudrik, toppkat ci julli, masbuuq ak laahiq.
1- Mudrik mooy ki wax takbiir al-iftitaah ànd ak imaam bi.
2- Toppkat ci julli mooy ki jotul ci takbiir al-iftitaah.
3- Masbuuq mooy ki topp imaam bi gannaaw bu imaam bi jullee benn walla ñaari rakaa.
4- Laahiq mooy ki wax takbiir al-iftitaah ànd ak imaam bi, waaye gannaaw loolu hadas daldi ko dal, mu jàpp te dellu topp imaam bi. Nit kooku day julli ni mu ko daan defe, te du def qiraa’a, di def tasbiix yi ci ruku ak sujóot. Nit kooku, su waxul kàddug àdduna, mel na ni ku nekk ci gannaaw imaam bi. Waaye, gannaaw bu génnee jàkka ji, war na jàppe ci bérab bu jege lool. Am na ku wax ne su demee ba sore lool, julligam dina nekk faasid.
Bu nit ñëwee ci jàkka ji, fekk imaam bi ci ruku, mu gaawtu ngir jot ci ruku bi, te wax takbiir al-iftitaah bi muy sëgg ngir ruku, toppul imaam bi. Bu fekkee imaam bi ci ruku, yéene topp ko, sottal takbiir bi fekk mu taxaw, daldi ruku te sëgg ànd ak imaam bi, di def tasbiix, jot na ci rakaa boobu. Waaye bi muy sëgg ngir ruku, su imaam bi siggee, jotul ci rakaa boobu.