1- Yéene aj bi ñuy dugg ci ihraam.
2- Taxaw wuquuf ca Arafaat.
3- Def tawaafu ziyaara.
Waxtu wuquuf ca Arafaat day tàmbali ci waxtu zawaal ci juróom-ñeenteelu bésub Sul Hijja, ba suba gi ca topp di fenk. [Buñu taxawee wuquuf ca Arafaat benn bés lu jiitu walla benn bés lu mujj, aj gi day baatil. Wahaabi yi dañuy def iid benn bés lu jiitu, te gisuñu fexu weer wi. Aju ñi taxawul wuquuf ci waxtoom du wér.]
Tawaaf am na juróom-ñaari xeet:
Bu jëkk bi, tawaafu ziyaara.
Ñaareel bi, tawaafu umra, (ñaar yii farata lañu).
Ñetteel bi, tawaafu quduum bi nekk sunna.
Ñeenteel bi, tawaafu wadaa.
Juróomeel bi, tawaafu nazru bi nekk waajib.
Juróom-benneel bi, tawaaf naafila.
Juróom-ñaareel bi, tawaafu tatawwu bi nekk mustahab.
Yéene ihraam ngir aj farata la. Sàngoo malaanu ihraam sunna la. Bañ a sol yére yuñu ñaw waajib la.
Te itam, sarti aj doon farata juróom-ñett lañu:
1- Mu doon jullit.
2- Mu mat.
3- Mu am xel.
4- Mu wér.
5- Mu bañ a doon jaam.
6- Alal ji mu am ëpp soxla yu war yi mu am.
7- Waxtu aj jot. Waxtu aj mooy Arafa ak ñeenti bési iid. Dañuy dugal itam ci waññi gi diirub yoon wi.
8- Jigéen ji sori doxub safar, war na ànd ak jëkkëram walla mahramam mi takk ak moom du jaadu mukk. [Ku matal juróom-ñetti sart yii, dem aj benn yoon ci dundam farata la ci moom. Su demee lu ëpp benn yoon, aj yi mu def ci at yi topp di àjj naafila. (Jaamu naafila) mooy jaamu gu dul farata walla sunna, te nit ki def ko ci coobareem. Yoolu jaamu naafila, bu ñu ko méngalee ak yoolu jaamu farata, néew na ni benn toq ndox ci wetug géej. Boroom xam-xamu diiney Lislaam mayuñu ñi nekk ci réew yu sore Màkka ñu dellu dem aj. Abdullaah Dahlawii “quddisa sirruhu” wax na ci bataaxalam bu juróom-benn-fukk ak ñett ne: (Ci yoonu aj, lu ëpp, mëneesul matal jaamu yi. Looloo tax Imaam ar-Rabbaanii “rahmatullaahi alayhi” xamle ci bataaxalam 123 ak 124 ne, nanguwul dem umra ak àjj naafila.) Àjj naafila ju tere def farata, walla ju tere jigéen ñi ñu sàngu, haraam la. Dem àjj naafila ju mel noonu, bàkkaar la, du yool. Dem umra itam noonu la.
Joxe asaka farata la bu benn at ci yonug gàddaay matee gannaaw ba nit ki amee nisaab. Waxtu woowu joxe asaka di farata, wuute na ci nit ñi. Su waxtu woowu jiitoo waxtu aj, dañuy joxe asakay alal ji ak xaalis bi yépp, ba noppi dem aj ak xaalis bi des. Su waxtu joxe asaka méngoo ak waxtu aj, dañuy jëkk dem aj. Gannaaw aj, dañuy joxe asakay xaalis bi des ci loxo.]