Kon, jigéen ju faatu bi mu nekkee ci jamonoy gannaaw wasin, walla bi mu ëmbée, walla ndax mbas, walla metitu biir, walla bu dara ci yooyu amul sax, waaye daanul feeñal yaramam ci kanamu góor ñi ko séy haraamul, te jëkkëram kontaan ci moom, malaakay àjjana dañuy ñëw ca moom ba muy faatu, taxaw ay saf ci kanamam. Dañu koy nuyu ak worma ak teranga, naan ko: (Yaw jaam ju jigéen ju Allah ta-aalaa sopp, ju sahiid, ñëwal génn, loo di def ci kër-buur gii ci àdduna? Allah ta-aalaa gërëm na la, def sa feebar gii sabab, baal la sa bàkkaar, may la àjjana; ñëwal jébbal sa amaana!) Jigéen ja, bu gisee daraja jooju ba bëgg jébbal ruuam, dafay xool li ko wër, ne: (Na mu baal ñi doon sama xarit te yërëm leen, doora ma jébbal sama ruu.) Malaaka ya dañuy yégle ñaanam Allah Boroom ndam. Ci loolu, kàddug ndam ga di ñëw, ne: (Ci sama ndam, nangu naa ñaan yépp yu sama jaam jii.) Malaaka ya dañu koy yégal xibaar bu neex bi. Gannaaw loolu, Malaakal-Mawt ak téeméer ak ñaar-fukki malaakam yërmande dañuy ñëw. Leeru seen kanam yéeg na ba ca Ars, ñu sol ay kaalag buur ci seen bopp, ay yére yu ñu defare leer ci seen yaram, ay dàll yu wurus ci seen tànk, te am ay laaf yu wert. Dañuy ñëw, yor ci seen loxo ay meññeefu àjjana, seen xet di ni musk, nuyu ko ak worma ak teranga, naan: (Sàkkkat bu àddina nuyu na la, may la àjjana, def la dëkkandoo ak soppeem Muhammad “alayhis-salaam”, def la àndandoo ak Soxna Aayisa.)
Jigéen jii am ngëm, bu déggee kàddu yii, rido ga nekk ci kanamu ay bëtam di ubbeeku, muy gis jigéen ñi gëm, te gis ñiy boroom bàkkaar te ñuy mbugal. Muy tinu, naan: (Baalal seen bàkkaar, sama Boroom!) Kàddu jóge ci Allah Boroom Ndama, ne: (Yaw sama jaam ju jigéen! Mottali naa sa bëgg-bëgg yépp, jébbalal sa amaana; soxnas sama Soppe ak doomam ju jigéen dañu lay xaar.) Bu déggee kàddu googu rekk, bakkanam di lox, ay tànkam di yëngu, muy ñaq. Bi muy waaja bàyyi bakkan, ñaari malaaka ñëw. Ku nekk ci ñoom yor bant bu ñu defare safara, kenn taxaw ci ndeyjooram, ki ci càmmoñam. Seytaane yal na ko Allah móolu daw ñëw, naan: (Dëgg la, amunu dara lu nu ci jariñ, waaye naa xool ba xam.) Muy ñëw ci noonu, yor ci loxoom ndab lu ñu defare gànjar, biir bi am ndox mu am galaas, di ko won ndox mi. Bu malaaka ya gisee aji bon jooju, dañuy dóor ndab li mu yor ak seen bant, toj ko te dàq ko. Jigéen jullit ja gis loolu, di ree. Gannaaw loolu, janq yu huur yooyu dañu koy may naanug Kawsar ci kaas bu ñu defare gànjar, muy naan. Ndax neexaayu naanug àjjana ga, bakkanam di tëb daldi taq ci kaas ba, te Malaakal-Mawt jël bakkanam ci kaas boobu. Malaaka ya di woo seen moroom, naan (Innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun). Dañuy jël bakkanam, wërale ko ci asamaan yi, yóbbu ko àjjana, won ko maqaamam fa, daldi ko indi ci wetug boppu néew ba.
Bu ñu summée ay yéreem te tekki kawaram, ruuam dafay ñëw ca saasa ci wetug boppu yaramam, naan: (Yaw miy sang néew mi! Jàppal ndànk, ndànk! Ndax am na gaañu-gaañu bakkan ci wewu Azraaiil. Te sama yaram sonn na lool, te lox na.) Bu ñu ko tëralée ci lalub sang néew, ruu ga di dellusi naan: (Bul tàngal ndox mi lool! Sama yaram néew doole na lool. Gaawleen ma bàyyi ma mucc ci seeni loxo, ngir ma dal.) Bu ñu ko sangee ba laxas ko ci sànkaar, ruu ga di taxaw ab diir, doora wooteeti naan: (Lii mooy sama gis àdduna bu mujj. Naa gis samay mbokk ak samay jegeñaale, te ñoom it nañu ma gis, jànge ci. Ndax ñoom it dinañu faatu ci kanam tuuti ni man, buñu jooy ak yuuxu gannaaw sama dee. Buñu ma fàtte; nañu ma di fàttaliku saa su nekk, di jàng Alxuraan al-Kariim. Buñu xuloo ci sama dono, ngir bañ ma am mbugal ci bàmmeel. Nañu ma fàttaliku it ci àjjuma yi ak iid yi.)
Gannaaw loolu, bu ñu ko tëralée ci musallaa, bakkan ba di wooteeti, naan: (Nangeen nekk ci jàmm, yaw sama doom ju góor ak sama doom ju jigéen, sama ndey ak sama baay! Amul bésub tàggoo bu mel ni bii. Danuy nammante; sunu daje des na bésub pénc. Maa ngi leen di tàggu, yéen ñiy jooy gannaaw sama dee!)
Bu ñu ko jullee ba yékkati ko ci seeni mbagg, muy wooteeti naan: (Yóbbuleen ma ndànk, ndànk! Su yool mooy seen dogu, buleen ma sonal! Naa yóbbul Allah ta-aalaa sama gërëm ci yéen!)
Bu ñu ko tëralée ci wetug bàmmeel, muy wooteeti naan: (Xoolleen sama nekk gi, te jànge ci! Léegi dingeen ma def ci bérab bu lëndëm te dem. Man ak samay jëf rekk a fa des. Xoolleen waxtu yii, te buleen nangu àdduna ju ñàkk kóllëre te di fen jii naxe leen ay pexeem!)
Bu ñu ko dugalee ci bàmmeelam, bakkan ba dafay ñëw ci wetug boppam. Buñu mukk bàyyi néew te defaluñu ko talqiin. [Gannaaw suul néew, ku sell def (Talqiin) sunna la. Wahaabi yi gëmuñu ne def talqiin sunna la. Dañuy naan bidaa la. Dañuy naan ku dee du dégg, mënul dégg. Boroom xam-xamu diine yu Ahlus Sunna “rahimahumullaahu ta-aalaa” bind nañu téere yu wuute, firndeel ne def talqiin sunna la. Benn ci téere yu am solo yooyu mooy téereb Sëriñ Mustafaa ibn Ibraahiim Siyaamii “rahimahullaahu ta-aalaa”, (Nuurul Yaqiin fii Mabhasit Talqiin). Bind nañu ci hadiis bu tedd bi Tabaraanii ak Ibn Manda nettali. Hadiis bu tedd boobu digle na ñu def talqiin. Téereb (Nuurul Yaqiin), bind nañu ko ci atum junni ak ñetti téeméer ak ñeent-fukk ak juróom (1345), ci Siyaam, ci dëkku Bangkok, te ñaareelu móolam am na ci Istanbul ci atum 1396 [m. 1976].] Ci ndigalu Allah ta-aalaa, néew ba ci bàmmeel dafay yeewu mel ni ku jóge ci nelaw, gis ne mu ngi ci bérab bu lëndëm. Dafay woo surgaam ak jaamam ju jigéen walla ki ko daan dimbali saa su nekk, naan: (Indil-leen ma sondeel!) Du am benn baat walla coow bu ñëw. Bàmmeel ba di xar, ñaari malaaka yuy laaj ci bàmmeel [Munkar ak Nakiir] di feeñ. Ay taal yu tàkk di génn ci seen gémmiñ, ak saxar gu ñuul ci seen bakkan. Ñu nekk ci noonu, jege ko naan: (Man rabbuka wa maa diinuka, wa man nabiyyuka), maanaam, kan mooy sa Boroom, ban diine mooy sa diine, te kan mooy sa Yónent? Su tontoo laaj yooyu ci dëgg, malaaka yooyu dañu koy yégal xibaar bu neex ne Allah Aji Dëgg Aji Kawe dina ko yërëm, ba noppi dem. Ca waxtu woowa, palanteer di ubbeeku ci ndeyjooru bàmmeel ba, ku kanamam mel ni weer génn fa, ñëw ci wetam. Jigéen jii am ngëm di ko xool, bég. Muy laaj: (Yaa di kan?) Mu tontu: (Ci sa sabar ak sa sukur ci àdduna lañu ma sàkke. Dinaa ànd ak yaw ba bésub pénc.)
Su nafs bàyyiwul di bëgg haraam yi,
Xol du mën mukk di seetu buy delloo nuuru Allah yi!