Ndox ñeenti xeet la: maa mutlaq, maa muqayyad, maa maskuuk, maa mustamal.
1- Maa mutlaq mooy ndoxu taw, ndoxu géej, ndoxu bëtu ndox buy wal ak ndoxu teen. Ndox yii dañuy setal lu sobe. Mën nañu leen a jëfandikoo ci lépp.
2- Maa muqayyad mooy ndoxu melon, ndoxu xaal, ndoxu garabu reseñ, ndoxu tóor-tóor ak yu mel ni yooyu.
Ndox yii dañuy setal lu sobe, waaye deesu leen jëfandikoo ngir jàpp ak sangu set.
3- Maa maskuuk lañuy wax ndox mi des gannaaw mbaam xuux mbaa ponkal bu yaayam di mbaam xuux naan ci.
Jàpp ak sangu set ak ndox mii, ñaar yépp jaadu nañu. Ku koy jëfandikoo mën na jiital bu ko neex ci ñaar yi; moom moo ci am tànneef.
4- Maa mustamal, ndox mi daanu ci suuf la, walla mi tàggoo ak yaram? Am na wuute ci xalaat ci loolu. Li gën a dëgg mooy mi tàggoo ak yaram. Te ci loolu itam, am na ñetti waxu maðhab. Ci Imaam bu mag “rahimahullaahu ta-aalaa”, najaasa gu diis la. Ci Imaam Abu Yuusuf “rahimahullaahu ta-aalaa”, najaasa gu woyof la. Ci Imaam Muhammad “rahimahullaahu ta-aalaa”, set na. Te loolu moo gën a dëgg.
Sarti wujuubug jàpp juróom-ñeent lañu:
1- Nit ki di jullit.
2- Mu mat.
3- Mu am xel.
4- Mu ñàkk jàpp.
5- Ndoxu jàpp mi set.
6- Mu am kàttanu jàpp.
7- Mu nekkul ci menstra.
8- Mu nekkul ci nifaas.
9- Mu nekk -ci biir- waxtu julli bu julli gu nekk. [Sart bu juróom-ñeente bii, boroom ngànt ci laab la jëm.]