Hakikat Books
Türkçe
Önizleme — bu metin henüz yayın onayı almadı.

Bölüm 19 / 73

Sunnay jàpp

Ñu ngi ci tudd lu tollu ci ñaar-fukk ak juróom.

1- Jàng Ahuusu.

2- Jàng basmala.

3- Raxas say loxo.

4- Def xilaal diggante sa baaraam yi.

5- Dugal ndox ci sa gémmiñ.

6- Dugal ndox ci sa bakkan.

7- Yéene. Ci masab hanafi, yéene bi ngay raxas sa kanam du farata, sunna la. Ci masab Saafi’ii farata la. Ci masab maaliki, yéene bi ngay raxas say loxo farata la.

8- Jublu ci qibla.

9- Def xilaal sa sikkim, [su fatt].

10- Def masa sa sikkim.

11- Tàmbalee ci sa wet gu ndeyjoor.

12- Jëfandikoo baaraamu loxo bu ndaw bi ci sa loxob càmmoñ ngir def xilaal diggante baaraami tànk yi, baaraam ci baaraam, tàmbalee ci suufu baaraamu tànk bu ndaw bi ci sa tànkub ndeyjoor.

13- Def masa sa bopp -ba mu daj ko yépp-.

14- Def masa say nopp ak sa baat ak ndox mi des gannaaw masa sa bopp.

15- Sàmm tartiib.

16- Toppanteel jëf yi te bañ leen a taxawal diggante bi.

17- Tàmbalee ci kanamu sa bopp bi ngay ko def masa.

18- Jëfandikoo soccu.

19- Yeggale ndox mi ci peggu say bët ak say yéen.

20- Dalk, maanaam fomp barab yi ngay raxas.

21- Jàpp te nga taxaw ci barab bu gën a kawe tuuti.

22- Raxas céri jàpp yi ñetti yoon.

23- Feesal satala bi gannaaw bu nga jàppee.

24- Bañ a wax waxi àdduna bi ngay jàpp.

25- Sax ci yéene boobu saa su nekk.

Bu bölümü başka dilde oku

Türkçe中文(普通话)EnglishPortuguêsItalianoУкраїнськаNederlandsБългарскиNorskEestiދިވެހި

Paylaş

WhatsApp Telegram X Facebook E-posta